Aller au contenu

Wikiquote:Babel

Jóge Wikiquote.

Xët wii moo lay leeral nooy xamale yeneen jëfëndikookat yi, say xameel ci yeneen làkk yi ak tolluwaayu xameel gi.



Lumuy jariñ

Donte fii w:Wikipedia ci kàllaama w:wolof la, waaye du ñi fi nekk ñépp a deggante. Am na ñu deggul wolof, walla seen degg des na, ñu man a soxla ku ñu jokkool ci làkk bi ñu degg, walla wolof yu yomb. Am na ay waa wikipedia yu deggul wolof te di bëgg a jàpp ci liggéey bi, kon di na am solo lool nga wax ko ci yan làkk ngeen man a waxtaane, ngir njariñam man a feeñ.

Mii sémb di na yombal jokkoo gi ci biir aw askan gu bariy làkk gu mel ne Wikipedia: ci misaal, di na yomb jot kuy wax wenn làkk wi, te itam di na xamale tolluwaayu degginu wolof gu ab jëfëndikookat bu bindu.

Nu ma koy defee?

Wikiquote:Babel
wo-1 Bii jëfëndikookat man naa cëru ak wolof bu tolluwaayam suufe.
fr-1 Cette personne peut contribuer avec un niveau élémentaire de français.
en-1 This user is able to contribute with a basic level of English.

Doy na nga yokk ci sa xëtu jëfëndikookat Babelbox bi, tabax ko ci topp tektal yii:

  • Tambalil ak {{Babel-
  • Nga yokk ci limu làkk yi nga degg te teg ci |
    • Misaal: {{Babel-3| (3 làkk)

Su ko defeen nak nga def ci tolluwaayu ni nga deggee wolof. Soo bëggee mu mel ne ni nga koy gisee (ci sa ndeyjoor), nga def: wo-0 walla wo-1 walla wo-2,añse.

Misaal: {{Babel|wo-1|fr-1|en-1}}

Yu wolof

Wikiquote:Babel
Wo Kii Wolof mooy làkku cosaanam.
wo-5 Bii jëfëndikookat man naa cëru ak Wolof ci anam bu xereñ .
wo-4 Bii jëfëndikookat man naa cëru ak Wolof daanaka ni ku ci cosaanoo .
wo-3 Bii jëfëndikookat man naa cëru ak Wolof bu tolluwaayam baax lool.
wo-2 Bii jëfëndikookat man naa cëru ak Wolof bu tolluwaayam diggu.
wo-1 Bii jëfëndikookat man naa cëru ak wolof bu tolluwaayam suufe.
wo-0 Bii jëfëndikookat manul cëru dara ci Wolof.